Speaker: Lena
Wolof language | wiki ethnologue |
Niger–Congo language family | wiki |
Latin script | scriptsource |
Roman Catholic Church | wiki |
Sign of the Cross
Turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi. Amiin
Lord's Prayer
Sunu Baay, bi ci asamaan,
na sa tur sell,
na sa nguur dikk, loo bëgg,
na am ci suuf naka ca asamaan.
May nu tey sunu dundu bés bu nekk,
te baal nu sunuy tooñ,
naka nuy baale ña nu tooñ.
Tc bu nu bàyyi nu tàbbi ci bëliis,
wànte musal nu ci lu bon.
Amiin
Hail Mary
Nuyu naa la, Maryaama,
fees nga ak yiw, borom baa ngi ak yow,
barkeel nga ci jigéen ñi yepp, te Yéesu, sa doomu biir, barkeel na.
Maryaama mu sell mi, Ndeyu Yàlla,
ñaanal ñu, ñun bàkkaarkat yi,
léegi ak ci suñu waxtu dee.
Amiin
Gloria Patri
Teranga ñell na Baay bi, Doom ji, ak Xel mu Sell mi,
naka la woon ca cosan la tey ak mos ba ca mos a mos.
Amiin